Leral.net - S'informer en temps réel

SËRIÑ MAXTAAR JENN, XARITU XALE YI, DËDDU NA

Rédigé par leral.net le Dimanche 28 Septembre 2025 à 00:43 | | 0 commentaire(s)|

Àllarba, 27eelu ut 2025 la Sëriñ Maxtaar Jenn ñàkk bakkanam cim ndog ci yoonu otorut “Ilaa Tuubaa”. Ay nataal yu doy waar, naqaree dékku ndax raglu ak tiis.

Àllarba, 27eelu ut 2025 la Sëriñ Maxtaar Jenn ñàkk bakkanam cim ndog ci yoonu otorut “Ilaa Tuubaa”. Ay nataal yu doy waar, naqaree dékku ndax raglu ak tiis.

Ku doonoon Sëriñ Maxtaar mii ?

50i at la amoon, di ab jullit, di murid, di sët ci Sëriñ Isaa Jenn (mi njëkk a jënd ab tool jébbal ko Sëriñ Tuubaa ngir ñu tabax fa jumaa Jurbel), gëm Sëriñ Tuubaa ba amu ci sago. Daan na def lu baax te waxam yépp « Sëriñ Tuubaa ma dimbali, lu ma mën moom la ». Waaye Sëriñ Maxtaar Jenn jàngalekat la woon, tàggatkat la woon, daan jàngal i gone, daan it tàggat seen iy jikko ; mook xale yi ñu bëggante woon lool. Sëriñ Maxtaar moo sosoon Complexe Maam Awa Lóo (ca Tuubaa Daaru Marnaan), daara ju mucc ayib, ànd ak jamono, gone yi di fa jàng alxuraan ak tubaab, informatig ak mécce ngir ku ci mokkal ba génn mën a dugg ci ja yi liggéey.

Sëriñ Maxtaar Jenn ku amoon gis-gis bu sori la, njànj, bari jàmm, déggook xale yi, xam yoonu njàngiin, def ay kopparam ci gone yi ndax xam ni goneey ëllëgu àddina.

Tabaxoon na tamit jumaa ca Tuubaa Tali bu bees, daan digle li Sëriñ bi digle woon muy “ jàng, góor-góorlu ci jaamu Yàlla, lu waay nekk ba julli jot mu bàyyi ko julliji, nangoo liggéey, moytu tooñ” tey jaayante.

Ni mu ñàkke bakkanam cim ndog, yóbbaalee ay mébét, amoon yéene ci tuut-tànk yi day wone ni xajaatoon na fi. Waaye, Wolof day léebu naan : « Xàndoor, bu dammee ci waar, wàcc na ». Te dégg naa Sëñ Rafahi Mbàkke mu ne « Sëñ Maxtaar, lépp li ko war, def na ko ».

Mënees na ne dundam gàtt na waaye ay jëfam réy nañu. Yal na dajeek ngërëm ak yermaande Boroom Bi ! Yal na suufu Bàqiya (Tuubaa) oyof ci kowam te Yàlla awu ko ci njaboot yi : muy gu deret ak ñeñeen ñi.

EJO ak LU DEFU WAXU ñoo ngi koy jaal njabootam, di ko jaal ay soxnaam, rawatina soxna Musli, di jaal itam jullit ñépp rawatina murid yi.

Primary Section: 
Archive setting: 
Unique ID: 
Daouda TOUMBOU


Source : https://www.seneplus.com/societe/serin-maxtaar-jen...